Ndaje Bu Ñépp Mën a Teewe

Ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu

Ñu ngi lay woo nga ñëw ànd ak ñun ci fàttaliku deewu Yeesu. Seetal bérébu ndaje bi la gën a jege.

“ Dinga nekk ak man ci Àjjana ji ”

Naka la dige boobu di ame ?

Bala Yeesu di dee, dafa dig taalibeem yu takku yi ne, dinañu nekk ak moom ci nguuram ca asamaan (Luug 22:28-30). Digoon na itam ku doon def lu bon, ne ko : “ Dinga nekk ak man ci Àjjana ji ” (Luug 23:43,MN). Naka la loolu di ame ?

Li Yeesu dige dina mën a am ndaxte Yeesu dafa joxe bakkanam ngir doomu Aadama yépp, ba ci bàkkaarkat yu mel ni defkatu lu bon boobu. Sarax si Yeesu def, dafa amoon solo ba tax Yeesu sant taalibeem yi ñu di ko fàttaliku. — Luug 22:19, 20.

Ci at mii, dinañu fàttaliku deewu Yeesu bi ci bésu Àllarba, 23 màrs 2016. Seede Yexowa yi ñu ngi lay woo nga ñëw ànd ak ñoom ci fàttaliku bés bu am solo boobu Yeesu taxawal. Dinga fa dégg waxtaan buy leeral njariñ bi ngeen mën a jële, yaw ak sa njaboot, ci deewu Yeesu bi.

——

Source: https://www.jw.org/wo/seede-yexowa/besu-fattaliku-bi/ 

Deixe uma resposta

O seu endereço de e-mail não será publicado. Campos obrigatórios são marcados com *